Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 9:6-11 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 9:6-11 in Kàddug Yàlla gi

6 Muy sa cofeel, di sa mbañeel, ba ci sa kiñaan ànd ak yaw seey. Du lenn lu deeti sa wàll ci jépp jëfi kaw suuf.
7 Kon doxal, lekk saw ñam, bége, te naan sa biiñ ci xol bu sedd. Yàlla kat nangul na la jeeg say jëf.
8 Foo tollu, solul ba jekk, te bul fàttee xeeñlu.
9 Bànneexul yaak ndaw si nga sopp ci fan wu gàtt wi la Yàlla may fi suuf, ndax loolu nga séddoo ci fan wu gàtt wii ngay doñ-doñaale fi kaw dun bi.
10 Liggéey boo gis, liggéeyal; def ci loo man. Ndax muy jëf, di doxalin, di xam-xam, di manoore, dara amu ci njaniiw, ga nga jëm.
11 Ma seetlooti fi kaw suuf ne du ku gaaw, yaay raw; du ku jàmbaare, yaa moom xare; du ku xelu, am loo dunde; du ku muus, duunle; du kuy xamkat, amu yiw; ku nekk ak bésam ak wërsëgam.
Kàdduy Waare 9 in Kàddug Yàlla gi