Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 9:3-6 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 9:3-6 in Kàddug Yàlla gi

3 Lu mettee ngi nii ci mboolem lu am fi kaw suuf: Benn dogal la ñépp bokk, te it nit a ngi sóobu ci mbon, di mébét jëfi dof giiru dundam, ba noppi fekki ña dee.
4 Képp kuy dund kat, am nga yaakaar, te xaj buy dund a gën gaynde gu dee.
5 Kuy dund xam ne dangay dee, waaye ku dee xamul dara, te séentootul ab yool. Ku dee, ñu fàtte la.
6 Muy sa cofeel, di sa mbañeel, ba ci sa kiñaan ànd ak yaw seey. Du lenn lu deeti sa wàll ci jépp jëfi kaw suuf.
Kàdduy Waare 9 in Kàddug Yàlla gi