Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 9:2-5 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 9:2-5 in Kàddug Yàlla gi

2 Ñépp a bokk benn dogal bi, ku jub ak ku bon, ku baax ak ku set, ak ku sobewu; kuy sarxal ak ku dul sarxal, muy ku baax ki, di bàkkaarkat bi, muy kiy giñ, di ki ragal ngiñ.
3 Lu mettee ngi nii ci mboolem lu am fi kaw suuf: Benn dogal la ñépp bokk, te it nit a ngi sóobu ci mbon, di mébét jëfi dof giiru dundam, ba noppi fekki ña dee.
4 Képp kuy dund kat, am nga yaakaar, te xaj buy dund a gën gaynde gu dee.
5 Kuy dund xam ne dangay dee, waaye ku dee xamul dara, te séentootul ab yool. Ku dee, ñu fàtte la.
Kàdduy Waare 9 in Kàddug Yàlla gi