13 Lii it gis naa ko, muy lu ma yéem, di mbirum xel mu rafet fi kaw suuf.
14 Ab dëkk bu ndaw la woon, nit ña néew. Buur bu mag song dëkk ba, gaw ko, jal jali suuf yu mag, sësal ca tata ja.
15 Fekk fa ku néewle te xelu. Mu manoona xelal dëkk ba, xettli leen, waaye kenn faalewu ko.
16 Man dama noon xel mu rafet a gën doole! Ndeke ku néewle ñu xeeb la, tanqamlu say wax.
17 Ku xelu, kàddoom yu dégtu ndànk moo gën ŋal-ŋalu kilifa ci biir ñu dofe.
18 Xel mu rafet a gën ngànnaayi xare, waaye benn bàkkaarkat day yàq ngëneel lu réy.