Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 9:10-14 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 9:10-14 in Kàddug Yàlla gi

10 Liggéey boo gis, liggéeyal; def ci loo man. Ndax muy jëf, di doxalin, di xam-xam, di manoore, dara amu ci njaniiw, ga nga jëm.
11 Ma seetlooti fi kaw suuf ne du ku gaaw, yaay raw; du ku jàmbaare, yaa moom xare; du ku xelu, am loo dunde; du ku muus, duunle; du kuy xamkat, amu yiw; ku nekk ak bésam ak wërsëgam.
12 Doom aadama la bésu safaan bay bett, jekki ne dàll fi kawam, ni jën wu keppu cib caax, loru, mbaa picc mu tancu cig fiir. Doom aadama xamul bésam.
13 Lii it gis naa ko, muy lu ma yéem, di mbirum xel mu rafet fi kaw suuf.
14 Ab dëkk bu ndaw la woon, nit ña néew. Buur bu mag song dëkk ba, gaw ko, jal jali suuf yu mag, sësal ca tata ja.
Kàdduy Waare 9 in Kàddug Yàlla gi