1 Loolu lépp laa walbatiku xalaat, ngir lépp leer ma: Ku jub ak ku xelu ak seeni jëf, lépp a ngi ci loxol Yàlla. Mbëggeel ak mbañeel, xamoo lu la ciy xaar, lépp a nga ca kanam.
2 Ñépp a bokk benn dogal bi, ku jub ak ku bon, ku baax ak ku set, ak ku sobewu; kuy sarxal ak ku dul sarxal, muy ku baax ki, di bàkkaarkat bi, muy kiy giñ, di ki ragal ngiñ.
3 Lu mettee ngi nii ci mboolem lu am fi kaw suuf: Benn dogal la ñépp bokk, te it nit a ngi sóobu ci mbon, di mébét jëfi dof giiru dundam, ba noppi fekki ña dee.
4 Képp kuy dund kat, am nga yaakaar, te xaj buy dund a gën gaynde gu dee.
5 Kuy dund xam ne dangay dee, waaye ku dee xamul dara, te séentootul ab yool. Ku dee, ñu fàtte la.