4 Kàddug buur kilifteef la. Ana ku ko naan: «Looy def nii?»
5 Ku dégg ndigal doo am lu la soof. Ku xelu, xam lu jot, xam doxalin.
6 Mbir mu mu doon kat ak jotam ak doxalinam, waaye nit am na tiis wu ko diis.
7 Kenn xamul luy xew ëllëg, kenn manula wax luy xew ëllëg.
8 Kenn moomul bakkanam, ba man koo dese, kenn amul sañ-sañ ci bésub deeyam, kenn muccul ci boobu xare, te mbon du ca wallu boroom.
9 Loolu lépp gis naa ko, ba may xalaat ci jépp jëfi kaw suuf; fi nit di yilife nit, muy loraange.
10 Ma gis itam ñu bon ñu ñu rob, ñu daan yaale kër Yàlla ga, ñu di leen gërëme tey seeni jëf ca dëkk ba. Loolu it, cóolóoli neen.
11 Jëf ñaaw na, mbugal ma yeex, ba tax doom aadama sóobu ci mbon.
12 Nit bàkkaar na téeméeri yoon, te teewul mu gudd fan. Xam naa it ne nee ñu ngëneel a ñeel ku ragal Yàlla, ndax wormaal ko.
13 Ku bon, du am lu baax, fanam du màgg ni ker, ndax wormaalul Yàlla.
14 Waaye cóolóoli neen a ngi am fi kaw suuf: Ku jub jot yoolu ku bon, ku bon jot yoolu ku jub. Ma ne loolu it cóolóoli neen la.