Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 7:7-16 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 7:7-16 in Kàddug Yàlla gi

7 Foqarñi kay day dofloo boroom xel, te ab ger da lay gëlëmal.
8 Fa mbir mujjee gën fa mu doore, te muñ a gën réy-réylu.
9 Bul gaawa mer; mer, xolub dof la samp këram.
10 Bul ne lu tax démb dàq tey, loolu, laaj ko du xel.
11 Xel mu rafet daa neex ni ndono, njariñ la ci kuy dund.
12 Xel mu rafet kiiraay la, xaalis kiiraay la; njariñu xam-xam mooy xelu, mucc.
13 Xoolal ci li Yàlla def: Ana ku mana jubbanti lu mu dëngal?
14 Su neexee, bànneexul; su mettee, xoolal ne lu ci ne, Yàllaa ko def ngir jaam bi umple gannaawam.
15 Lu ne laa gis ci sama dund gu gàtt gii! Nit a ngii jub, teewu koo sànkook njubam; nit bon, ànd ak mbonam, gudd fan.
16 Bul jub ba mu ëpp, bul wóolu sam xel ba mu ëpp, lu ko moy nga yàqule.
Kàdduy Waare 7 in Kàddug Yàlla gi