Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 7:7-11 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 7:7-11 in Kàddug Yàlla gi

7 Foqarñi kay day dofloo boroom xel, te ab ger da lay gëlëmal.
8 Fa mbir mujjee gën fa mu doore, te muñ a gën réy-réylu.
9 Bul gaawa mer; mer, xolub dof la samp këram.
10 Bul ne lu tax démb dàq tey, loolu, laaj ko du xel.
11 Xel mu rafet daa neex ni ndono, njariñ la ci kuy dund.
Kàdduy Waare 7 in Kàddug Yàlla gi