Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 7:3-8 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 7:3-8 in Kàddug Yàlla gi

3 Naqar a gën xaxaloo; aw tiis ñëkkal kanam, rafetal xol.
4 Ku xelu, xalaat kërug dëj; ku dofe, xalaat kërug puukare.
5 Déglu ku xelu di la àrtu moo gën déglu dof bu lay woy.
6 Ab dof day textexi ni dég yuy retete taal bu cin tege. Loolu it di cóolóoli neen.
7 Foqarñi kay day dofloo boroom xel, te ab ger da lay gëlëmal.
8 Fa mbir mujjee gën fa mu doore, te muñ a gën réy-réylu.
Kàdduy Waare 7 in Kàddug Yàlla gi