23 Loolu lépp maa ko natte xel mu rafet, te naan: «Naa xelu,» ndeke mbir ma sore na ma.
24 Li wara am daa loq, te xóota xóot; ana ku ko mana daj?
25 Ma walbatiku, di jéema xam, di wut, di càmbar, di sàkkum piri, ngir xam li bon cig ndof, ak li dofe, cig ndof.
26 Ma seetlu lenn lu gëna naqari dee: muy ndaw su la fiir. Kooku cofeelam mbaal la, yoxo ya dib jéng. Ku Yàlla gërëm a koy rëcc, bàkkaarkat bi lay jàpp.
27 Waarekat ba nee: Xoolal li ma gis, benn-bennal ko, ngir gis lu mu firi.
28 Ma seeta seet, gisuma. Genn góor laa ràññee ci junniy góor, ràññeewuma kenn ci jigéen ñi ñépp.