20 Amul moos ku jub ci kaw suuf, kuy def lu baax te du bàkkaar.
21 Te it du lépp lu ñu wax, ngay bàyyi xel. Kon doo dégg surga bu la ŋàññ,
22 ndax xam nga xéll ne yaw it ŋàññe nga ay yooni yoon.
23 Loolu lépp maa ko natte xel mu rafet, te naan: «Naa xelu,» ndeke mbir ma sore na ma.
24 Li wara am daa loq, te xóota xóot; ana ku ko mana daj?
25 Ma walbatiku, di jéema xam, di wut, di càmbar, di sàkkum piri, ngir xam li bon cig ndof, ak li dofe, cig ndof.