Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 7:1-6 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 7:1-6 in Kàddug Yàlla gi

1 Jëw bu rafet a gën diw gu xeeñ, bésub dee a gën bésub juddu.
2 Dem dëj a gën wàlli bernde, mooy muju képp. Kuy dund, sóoraale ko.
3 Naqar a gën xaxaloo; aw tiis ñëkkal kanam, rafetal xol.
4 Ku xelu, xalaat kërug dëj; ku dofe, xalaat kërug puukare.
5 Déglu ku xelu di la àrtu moo gën déglu dof bu lay woy.
6 Ab dof day textexi ni dég yuy retete taal bu cin tege. Loolu it di cóolóoli neen.
Kàdduy Waare 7 in Kàddug Yàlla gi