Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 6:1-9 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 6:1-9 in Kàddug Yàlla gi

1 Aw tiis a ngi wu ma gis fi kaw suuf, di tiis wu diis doom aadama:
2 Nit ku Yàlla may alal, koom ak daraja, te mboolem lu mu namm, ñàkku ca lenn, waaye Yàlla mayu ko mu tal caa lekk, xanaa jaambur di ko xéewloo — loolu cóolóoli neen la, di naqar wu tar.
3 Ku giir téeméeri doom, dund ati at, ak lu at ya bare bare, su bégewul teraanga ja mu am te amul njégu bàmmeelam sax, kooku lumb wu tuuroo ko tane.
4 Lumb wa ñëw na moos ci neen, bàddoo lëndëm, turam sàngoo lëndëm.
5 Gisul jant, xamu ko, waaye noflaay moo ko ëpple mag ma,
6 bu dundoon junniy junniy at sax te amul jàmm. Xanaa du benn bérab la ñépp jëm?
7 Nit ak doñ-doñam jépp, biiram, te taxul mu doylu.
8 Ana lu boroom xel ëpplee ku dofe? Nga ñàkk, xam doxalin, lu mu lay jariñ?
9 Doyloo li nga gis a gën di wéye xemmem. Loolu it, cóolóoli neen ak napp um ngelaw.
Kàdduy Waare 6 in Kàddug Yàlla gi