Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàdduy Waare - Kàdduy Waare 6

Kàdduy Waare 6:1-9

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Aw tiis a ngi wu ma gis fi kaw suuf, di tiis wu diis doom aadama:
2Nit ku Yàlla may alal, koom ak daraja, te mboolem lu mu namm, ñàkku ca lenn, waaye Yàlla mayu ko mu tal caa lekk, xanaa jaambur di ko xéewloo — loolu cóolóoli neen la, di naqar wu tar.
3Ku giir téeméeri doom, dund ati at, ak lu at ya bare bare, su bégewul teraanga ja mu am te amul njégu bàmmeelam sax, kooku lumb wu tuuroo ko tane.
4Lumb wa ñëw na moos ci neen, bàddoo lëndëm, turam sàngoo lëndëm.
5Gisul jant, xamu ko, waaye noflaay moo ko ëpple mag ma,
6bu dundoon junniy junniy at sax te amul jàmm. Xanaa du benn bérab la ñépp jëm?
7Nit ak doñ-doñam jépp, biiram, te taxul mu doylu.
8Ana lu boroom xel ëpplee ku dofe? Nga ñàkk, xam doxalin, lu mu lay jariñ?
9Doyloo li nga gis a gën di wéye xemmem. Loolu it, cóolóoli neen ak napp um ngelaw.

Read Kàdduy Waare 6Kàdduy Waare 6
Compare Kàdduy Waare 6:1-9Kàdduy Waare 6:1-9