Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 5:7-16 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 5:7-16 in Kàddug Yàlla gi

7 Boo gisee ñuy not néew-ji-doole, di jalgati dëgg ak yoon cib gox, bumu la jaaxal; kilifa gi, kilifaam a ko yiir; ñoom it seen kilifaa leen yiir.
8 Xanaa ndax buur suqal mbey mi, ba ñépp jariñoo suuf si.
9 Bëggkatu xaalis du doyal xaalis, bëggkatu alal du doyal tono, te loolu it, cóolóoli neen.
10 Bu koom yokkoo, lekk-kat yi yokku. Ana lu muy jariñ boroom koom ga, xanaa di ko duufale bëtam?
11 Surga, lekkam néew, bare, mu nelaw, ba fàttey boram; boroom alal regg, du nopplu, du nelaw.
12 Naqar wu réy laa gis fi kaw suuf: Alal ju boroom dajale ba loru,
13 mbaa pexeem moy, mu sànkule; ba bu amee doom it, du ko wacce dara.
14 Nga juddoo ci sa ndey loxoy neen, walbatiku dellu na nga dikke woon. Du dara loo ñaqoon ba yóbbaale ko.
15 Dikke ni, delloo ni, loolu it tiis wu réy la. Doñ-doñi, ngelawal neen, ana jariñ la?
16 Ngay dunde tiis bésoo bés, ak naqar ak wopp ak xol bu tàng!
Kàdduy Waare 5 in Kàddug Yàlla gi