Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 5:3-14 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 5:3-14 in Kàddug Yàlla gi

3 Boo digook Yàlla, bu ko yeexe; Daray foontukat neexul, defal li nga dige.
4 Baña digee gën dige loo deful.
5 Bu la sa làmmiñ yóbbe bàkkaar, ba ngay lay ndawal Yàlla la, naan lii njuumte la woon. Ana lu jar Yàlla di la meree sa kàddu, bay neenal saw ñaq?
6 Wax ju bare, caaxaani neen; mook gént yu baree yem. Kon, Yàlla, ragal ko.
7 Boo gisee ñuy not néew-ji-doole, di jalgati dëgg ak yoon cib gox, bumu la jaaxal; kilifa gi, kilifaam a ko yiir; ñoom it seen kilifaa leen yiir.
8 Xanaa ndax buur suqal mbey mi, ba ñépp jariñoo suuf si.
9 Bëggkatu xaalis du doyal xaalis, bëggkatu alal du doyal tono, te loolu it, cóolóoli neen.
10 Bu koom yokkoo, lekk-kat yi yokku. Ana lu muy jariñ boroom koom ga, xanaa di ko duufale bëtam?
11 Surga, lekkam néew, bare, mu nelaw, ba fàttey boram; boroom alal regg, du nopplu, du nelaw.
12 Naqar wu réy laa gis fi kaw suuf: Alal ju boroom dajale ba loru,
13 mbaa pexeem moy, mu sànkule; ba bu amee doom it, du ko wacce dara.
14 Nga juddoo ci sa ndey loxoy neen, walbatiku dellu na nga dikke woon. Du dara loo ñaqoon ba yóbbaale ko.
Kàdduy Waare 5 in Kàddug Yàlla gi