Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 5:13-18 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 5:13-18 in Kàddug Yàlla gi

13 mbaa pexeem moy, mu sànkule; ba bu amee doom it, du ko wacce dara.
14 Nga juddoo ci sa ndey loxoy neen, walbatiku dellu na nga dikke woon. Du dara loo ñaqoon ba yóbbaale ko.
15 Dikke ni, delloo ni, loolu it tiis wu réy la. Doñ-doñi, ngelawal neen, ana jariñ la?
16 Ngay dunde tiis bésoo bés, ak naqar ak wopp ak xol bu tàng!
17 Lii daal laa ci gis, man. Li gën te jaadu ci nit: Na lekk, naan te bànneexoo ñaqam wu mu ñaqe kaw suuf giiru dund gi ko Yàlla may. Loolu mooy céram.
18 Alal ak koom, ku ko Yàlla may, may ko mu tal koo xéewloo, mu nangu céram, bànneexoo ñaqam, loolu mayu Yàllaa.
Kàdduy Waare 5 in Kàddug Yàlla gi