10 Bu koom yokkoo, lekk-kat yi yokku. Ana lu muy jariñ boroom koom ga, xanaa di ko duufale bëtam?
11 Surga, lekkam néew, bare, mu nelaw, ba fàttey boram; boroom alal regg, du nopplu, du nelaw.
12 Naqar wu réy laa gis fi kaw suuf: Alal ju boroom dajale ba loru,
13 mbaa pexeem moy, mu sànkule; ba bu amee doom it, du ko wacce dara.
14 Nga juddoo ci sa ndey loxoy neen, walbatiku dellu na nga dikke woon. Du dara loo ñaqoon ba yóbbaale ko.
15 Dikke ni, delloo ni, loolu it tiis wu réy la. Doñ-doñi, ngelawal neen, ana jariñ la?
16 Ngay dunde tiis bésoo bés, ak naqar ak wopp ak xol bu tàng!