Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 4:5-15 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 4:5-15 in Kàddug Yàlla gi

5 Dof banki loxoom, sànk boppam.
6 Waaye benn ŋëb bu ànd ak dal moo gën ñaari ŋëbi doñ-doñ ci napp um ngelaw.
7 Ma seetlu leneen luy cóolóoli neen fi kaw suuf.
8 Kenn a ngii, kenn ñaareelu ko, du doom, du mbokk. Doñ-doñam du dakk, te du doylu, mujj mu naan: «Kan laay doñ-doñil, di xañ sama bopp bànneex?» Loolu it, cóolóoli neen, di sas wu tiis.
9 Ñaar a man kenn; doñ-doñoondoo, yoolu bu baax.
10 Kenn daanu, moroom ma may ko loxo. Waaye ngalla ku daanu te amuloo ku la may loxo!
11 Bu ñu tëddee di ñaar it, mana bokk nuglu. Waaye soo dee kenn, nooy nugloo?
12 Fu ñu mane kenn, ñaar taxaw fa, jéngu, te buumu ñetti xànc gaawula dog.
13 Kuy ndaw, génne kaso, tàmbalee nguuru fa mu juddoo woon mbaadoolo, ndaw loolu su dee baadoolo te xelu it, moo gën buur bu màggat, dofe, dégguli àrtu.
15 Ma gis mboolem luy dund tey dox fi kaw suuf, di topp ndaw la wuutu buur.
Kàdduy Waare 4 in Kàddug Yàlla gi