Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 4:3-8 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 4:3-8 in Kàddug Yàlla gi

3 Ki leen taneeti yeen ñépp di ki juddoogul sax, moom mi gisul jëf ju bon fi kaw suuf.
4 Ma gis ne nit ak kër-këram jépp ak bépp manoorey liggéey, iñaanantee ko waral. Loolu it, cóolóoli neen ak napp um ngelaw.
5 Dof banki loxoom, sànk boppam.
6 Waaye benn ŋëb bu ànd ak dal moo gën ñaari ŋëbi doñ-doñ ci napp um ngelaw.
7 Ma seetlu leneen luy cóolóoli neen fi kaw suuf.
8 Kenn a ngii, kenn ñaareelu ko, du doom, du mbokk. Doñ-doñam du dakk, te du doylu, mujj mu naan: «Kan laay doñ-doñil, di xañ sama bopp bànneex?» Loolu it, cóolóoli neen, di sas wu tiis.
Kàdduy Waare 4 in Kàddug Yàlla gi