Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 10:8-11 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 10:8-11 in Kàddug Yàlla gi

8 Ku gas um yeer, repp nga tàbbi ca; ku bëtt miir, repp jaan matt la;
9 kuy yett ay doj, repp nga caa gaañu; kuy gor bant, repp nga caa loru.
10 Liggéeye weñ gu day te xacceesu ko, góor-góorlu war na ca; xelu, baaxle jariñoo.
11 Jaan màtte, balees koo jat, du njariñal jatkat ba.
Kàdduy Waare 10 in Kàddug Yàlla gi