Text copied!
Bibles in Wolof

Kàdduy Waare 10:5-16 in Wolof

Help us?

Kàdduy Waare 10:5-16 in Kàddug Yàlla gi

5 Lu mettee ngi lu ma gis fi kaw suuf, lu mel ni njuumte lu rëcc kilifa:
6 Ab dof bu ñu jox cér yu bare, boroom daraja féete suuf;
7 ma gis baadoolo war fas, kilifa di rung ni baadoolo.
8 Ku gas um yeer, repp nga tàbbi ca; ku bëtt miir, repp jaan matt la;
9 kuy yett ay doj, repp nga caa gaañu; kuy gor bant, repp nga caa loru.
10 Liggéeye weñ gu day te xacceesu ko, góor-góorlu war na ca; xelu, baaxle jariñoo.
11 Jaan màtte, balees koo jat, du njariñal jatkat ba.
12 Ku xelu àddu, mu diw yiw; ku dofe wax, sànku.
13 Bu jëkkee wax ju amul bopp, daaneele ndof gu sotti.
14 Ab dof a ngi waxa wax, te kenn xamul luy xew ëllëg. Ana ku koy xamal gannaawam?
15 Ab dof ak kër-këreem, coonoy neen; du xam sax yoonu taax ya.
16 Ngalla yeen, réew mi gone falu buur, jawriñ ña di xëye xawaare.
Kàdduy Waare 10 in Kàddug Yàlla gi