4 Su la sa kilifa meree, bul jóge fa ñu la teg; tooñ yu mag, teey ba giif.
5 Lu mettee ngi lu ma gis fi kaw suuf, lu mel ni njuumte lu rëcc kilifa:
6 Ab dof bu ñu jox cér yu bare, boroom daraja féete suuf;
7 ma gis baadoolo war fas, kilifa di rung ni baadoolo.