15 Ab dof ak kër-këreem, coonoy neen; du xam sax yoonu taax ya.
16 Ngalla yeen, réew mi gone falu buur, jawriñ ña di xëye xawaare.
17 Ndokklee, yeen, réew ma as gor falu, te bu jotee, jawriñ ñay xéewlu, ngir am doole te baña màndi.
18 Tayel, puj bu màbb; yaafus, néeg buy senn.
19 Aw ñam bégal, aw ñoll bànneexal, xaalis tontu lu ne.