13 Bu jëkkee wax ju amul bopp, daaneele ndof gu sotti.
14 Ab dof a ngi waxa wax, te kenn xamul luy xew ëllëg. Ana ku koy xamal gannaawam?
15 Ab dof ak kër-këreem, coonoy neen; du xam sax yoonu taax ya.
16 Ngalla yeen, réew mi gone falu buur, jawriñ ña di xëye xawaare.
17 Ndokklee, yeen, réew ma as gor falu, te bu jotee, jawriñ ñay xéewlu, ngir am doole te baña màndi.
18 Tayel, puj bu màbb; yaafus, néeg buy senn.
19 Aw ñam bégal, aw ñoll bànneexal, xaalis tontu lu ne.
20 Sam xel sax bu ca saaga buur, sa néegu biir sax, bu fa saagaa boroom daraja. Xamoo picc muy yóbbu sa kàddu, mbaa njanaaw luy siiwali mbir ma.