Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 8:5-10 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 8:5-10 in Kàddug Yàlla gi

5 Téxét bi, deel foog, dof bi, déggal ndéey lu xelu.
6 Déglul, ma wax la lu am solo, dégtal la njub.
7 Dëgg laay wax, di bañ wax ju bon.
8 Lu ma wax njub la. Amul lu dëng mbaa lu jekkadi.
9 Lépp a dëggu ci ku am ug dégg, te jub ci ku for xam-xam.
10 Na la samab yar gënal xaalis, xam-xam dàqal la ngën-gi-wurus.
Kàddu yu Xelu 8 in Kàddug Yàlla gi