5 Dina la aar ci ndaw su yemadi, bokk feneen, di wax lu neex.
6 Damaa tollu sama palanteer, séentu ca xarante ya,
7 séen ca biir téxét ya, ku ma seetlu ca xale yu góor ya, muy ku ñàkk bopp.
8 Muy dem ba fa ndaw say taxaw, ca selebe yoon wa, daldi wuti kër ndaw sa.