4 Bul gëmm, bul nelaw!
5 Dawal ni kéwél gu rëcc ub rëbb, ne fërr ni picc mu raw ab fiirkat.
6 Yaafus bee, xoolal xorondom, seetal ci moom, ba muus.
7 Du ku ko yilif mbaa ku koy sas, te jiiteesu ko.
8 Bu jotee mu denc ab dundam, mu jot, mu for lekkam.
9 Moo yaafus bi, foo àppal tëraay bi? Loo deeti xaar ci yewwu?