7 Éy Yàlla, yaar laa la ñaan, ngalla may ma ko sama giiru dund:
8 caaxaan aki fen, yal na ma sore, néewleek barele, bu ma ci may lenn, leel ma lu ma doy;
9 lu ko moy ma regg, weddi la, ba naan: «Kuy Aji Sax ji?» Mbaa ma ñàkk bay sàcc, di la ñàkke worma, yaw sama Yàlla.
10 Bul sikkal ab surga ca njaatigeem, da lay ñaan-yàlla, mu dal la.
11 Ag maas a ngi saaga baay, te wormaaluñu ndey.
12 Ag maas a ngi defe ne set nañu, te taq ripp ak bàkkaar.
13 Ag maas a ngi daŋŋiiral; aka ñoo mana xeeloo!
14 Ag maas a ngi, seeni sell niy saamar, seeni gëñ niy paaka, ñuy lekk néew-ji-doole, ba raafal leen ci réew mi, ba ku ñàkk jeex ci biir nit ñi.
15 Saxu watar du suur, ñaar ñu jigéen la am: Jox Ma ak Jox Ma. Ñett a ngii ñu dul suur, ba ci ñeent ñu dul ne doy na mukk:
16 njaniiw, jigéen ju jaasir, suuf, du màndi ndox, sawara, du ne doy na mukk.
17 Kuy xeelu sa baay, di siidee déggal sa ndey, baaxoñ génne ciw xur, luqi sa bët, tan ya lekk.
18 Ñett a ngii, yéem na ma, ba ci ñeent yu ma xamul: