Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 30:7-10 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 30:7-10 in Kàddug Yàlla gi

7 Éy Yàlla, yaar laa la ñaan, ngalla may ma ko sama giiru dund:
8 caaxaan aki fen, yal na ma sore, néewleek barele, bu ma ci may lenn, leel ma lu ma doy;
9 lu ko moy ma regg, weddi la, ba naan: «Kuy Aji Sax ji?» Mbaa ma ñàkk bay sàcc, di la ñàkke worma, yaw sama Yàlla.
10 Bul sikkal ab surga ca njaatigeem, da lay ñaan-yàlla, mu dal la.
Kàddu yu Xelu 30 in Kàddug Yàlla gi