26 daman, barewul kàttan, te day dëkk ciy doj;
27 soccet, amul buur, teewul ñuy àndandoo, diy gàngoor;
28 sindax, manees na koo ŋëb, teewul ma nga biir kër buur.
29 Ñett a ngii, ñu jekk um ndaag, ba ci ñeent ñu jekk doxin:
30 gaynde, mooy buuru rab yi, ragalul kenn;
31 séq daagu, jekk taxawaay, ab sikket, ak buur ci biiri dagam.
32 Boo sàgganee bay tëggu, mbaa ngay mébét lu bon, nanga téye saw làmmiñ.
33 Ndax ku ruux soow, am ca dax, ku wañaar bakkan, mu nàcc, te lu jógal xol, indiw ay.