24 Ñeent a ngii, di lu tuut ci kaw suuf, te am xel, yaroo xel:
25 xorondom, néew na doole, waaye bu jotee, mu denc dundam;
26 daman, barewul kàttan, te day dëkk ciy doj;
27 soccet, amul buur, teewul ñuy àndandoo, diy gàngoor;
28 sindax, manees na koo ŋëb, teewul ma nga biir kër buur.
29 Ñett a ngii, ñu jekk um ndaag, ba ci ñeent ñu jekk doxin:
30 gaynde, mooy buuru rab yi, ragalul kenn;