Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 30:2-6 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 30:2-6 in Kàddug Yàlla gi

2 Maa dofe dëgg, ba yées ci nit ñi, dég-dégu nit sax awma ko.
3 Jànguma, ba am xel mu rafet, awma xam-xam ci Aji Sell ji.
4 Ana ku yéegoon asamaan, ba wàcc? Mbaa mu masa ŋëb ngelaw ciy loxoom? Ana ku masa ëmb ndox ci ndimo? Mbaa mu rëdd mboolem kemi àddina? Nu mu tudd ak nu doomam tudd? Wax ma, yaw mi ko xam!
5 Lu Yàlla wax, mat na sëkk, mooy yiir ku ko làqoo.
6 Bul yokk ay waxam, mu weddi say fen, nga weeru.
Kàddu yu Xelu 30 in Kàddug Yàlla gi