2 Maa dofe dëgg, ba yées ci nit ñi, dég-dégu nit sax awma ko.
3 Jànguma, ba am xel mu rafet, awma xam-xam ci Aji Sell ji.
4 Ana ku yéegoon asamaan, ba wàcc? Mbaa mu masa ŋëb ngelaw ciy loxoom? Ana ku masa ëmb ndox ci ndimo? Mbaa mu rëdd mboolem kemi àddina? Nu mu tudd ak nu doomam tudd? Wax ma, yaw mi ko xam!
5 Lu Yàlla wax, mat na sëkk, mooy yiir ku ko làqoo.