19 yoonu jaxaay ci asamaan, yoonu jaan ci kawi doj, yoonu gaal ci diggu géej, yoon wi góor di jaar as ndaw.
20 Jikkoy jigéenu moykat a ngi. Day lekk, wommiku, te naan: «Defuma dara lu aay!»
21 Ñett a ngii, day yëngal suuf, ba ci ñeent yu suuf àttanul:
22 jaam bu falu buur, dof bu regg,
23 ndaw su bon su for jëkkër, jigéen ju wuutu sangam bu jigéen.
24 Ñeent a ngii, di lu tuut ci kaw suuf, te am xel, yaroo xel:
25 xorondom, néew na doole, waaye bu jotee, mu denc dundam;
26 daman, barewul kàttan, te day dëkk ciy doj;
27 soccet, amul buur, teewul ñuy àndandoo, diy gàngoor;
28 sindax, manees na koo ŋëb, teewul ma nga biir kër buur.
29 Ñett a ngii, ñu jekk um ndaag, ba ci ñeent ñu jekk doxin: