19 Waxi neen yarul surga, da lay dégg te du la déggal.
20 Ana koo gis, mu rattaxle? Kooku ab dof a ko gën demin.
21 Ku yàq sab surga ba muy ndaw, bu ëllëgee mu defe ne doom la.
22 Boroom xadar day sooke ay, te ku tàng bopp moy, moyati.
23 Réy-réylu, detteelu rekk; woyofal, ñu naw la.