9 Soo dee tanqamlu yoon, sag ñaan sax Yàlla suur na ko.
10 Ku yóbbe bàkkaar nit kuy jubal, yeer ma nga gas, yaa cay tàbbi, waaye ku mat di jagoo ngëneel.
11 Waay a ngi barele, defe ne xelu na; ku néewle am ug dégg, gis ne xeluwul.
12 Bu ku jub amee ndam, mbégte mu réy la; ab soxor falu, ñépp làquji.
13 Kuy làq say tooñ doo baaxle, ku koy nangu, tuub ko, am yërmandey Yàlla.
14 Mbégte ñeel na ku saxoo ragal, waaye ku dëgër bopp tàbbi ci njekkar.
15 Kilifa guy soxore néew-ji-doole mook gaynde guy yëmmoo yem, mbaa rab wuy songe.
16 Kilifa gu amul ug dégg, day foqati rekk, waaye ku bañ lu lewul, gudd fan.
17 Ku bóom nit, daw, ba tàbbi njaniiw; bu ko kenn taxawu.
18 Mat, mucc; dëng, dàll daanu.
19 Beyal sab tool, sab dund doy; topp ay caaxaan, ndóol ba doyal.