Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 28:6-11 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 28:6-11 in Kàddug Yàlla gi

6 Ñàkk te mat moo gën barele te dëng.
7 Gone gu sàmm yoon am nag dégg, ku ànd ak sagaru nit gàcceel sa baay.
8 Kiy leble di tege, ba barele, kay yéwéne néew-ji-doole lay dencal.
9 Soo dee tanqamlu yoon, sag ñaan sax Yàlla suur na ko.
10 Ku yóbbe bàkkaar nit kuy jubal, yeer ma nga gas, yaa cay tàbbi, waaye ku mat di jagoo ngëneel.
11 Waay a ngi barele, defe ne xelu na; ku néewle am ug dégg, gis ne xeluwul.
Kàddu yu Xelu 28 in Kàddug Yàlla gi