Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 28:3-8 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 28:3-8 in Kàddug Yàlla gi

3 Ku ñàkk, su jekkoo ab ndóol, du ko bàyyil fepp, day mel ni waame.
4 Ku wacc yoon, gërëm ku bon; ku wormaal yoon, jànkoonteek ku bon.
5 Ku bon xamul njub, kuy wut Aji Sax ji, xam nga njub bu wér.
6 Ñàkk te mat moo gën barele te dëng.
7 Gone gu sàmm yoon am nag dégg, ku ànd ak sagaru nit gàcceel sa baay.
8 Kiy leble di tege, ba barele, kay yéwéne néew-ji-doole lay dencal.
Kàddu yu Xelu 28 in Kàddug Yàlla gi