20 Boroom worma, bare barke; ku yàkkamtee woomle, sa mbugal du jaas.
21 Par-parloo baaxul, waaye dogu mburu moyloo na kilifa.
22 Ab nay day yàkkamtee barele, te xamul, ba ko ñàkk di dab.
23 Boo artoo nit, mu baaxe la ëllëg; yaa koy gënal ku ko doon jay.
24 Ku xañ say waajur seen alal te defe ne tooñoo, yaa neexook saaysaayu yàqkat.
25 Ku bëgge day sooke ay, te ku wóolu Aji Sax ji, woomle.
26 Ku doyloo sam xel, dof nga; ku jëfe xel mu rafet, mucc nga.
27 Kuy jox néew-ji-doole, doo ñàkk; nga gëmm ne gisoo, bare ku la móolu.