Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 28:20-24 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 28:20-24 in Kàddug Yàlla gi

20 Boroom worma, bare barke; ku yàkkamtee woomle, sa mbugal du jaas.
21 Par-parloo baaxul, waaye dogu mburu moyloo na kilifa.
22 Ab nay day yàkkamtee barele, te xamul, ba ko ñàkk di dab.
23 Boo artoo nit, mu baaxe la ëllëg; yaa koy gënal ku ko doon jay.
24 Ku xañ say waajur seen alal te defe ne tooñoo, yaa neexook saaysaayu yàqkat.
Kàddu yu Xelu 28 in Kàddug Yàlla gi