Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 28:16-25 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 28:16-25 in Kàddug Yàlla gi

16 Kilifa gu amul ug dégg, day foqati rekk, waaye ku bañ lu lewul, gudd fan.
17 Ku bóom nit, daw, ba tàbbi njaniiw; bu ko kenn taxawu.
18 Mat, mucc; dëng, dàll daanu.
19 Beyal sab tool, sab dund doy; topp ay caaxaan, ndóol ba doyal.
20 Boroom worma, bare barke; ku yàkkamtee woomle, sa mbugal du jaas.
21 Par-parloo baaxul, waaye dogu mburu moyloo na kilifa.
22 Ab nay day yàkkamtee barele, te xamul, ba ko ñàkk di dab.
23 Boo artoo nit, mu baaxe la ëllëg; yaa koy gënal ku ko doon jay.
24 Ku xañ say waajur seen alal te defe ne tooñoo, yaa neexook saaysaayu yàqkat.
25 Ku bëgge day sooke ay, te ku wóolu Aji Sax ji, woomle.
Kàddu yu Xelu 28 in Kàddug Yàlla gi