Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 27:2-21 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 27:2-21 in Kàddug Yàlla gi

2 Bul tëggu, bàyyil ñu tagg la, muy waxi keneen; yaw, bu ko wax.
3 Doj diis na, suuf dib sëf, waaye fitnay dof a ko raw.
4 Xadar day ñàng, mer di wal mu baawaan, waaye fiiraange amul moroom.
5 Artu yu ñu la biralal moo gën cofeel gu la boroom ñooru.
6 Soppe, bu lay gaañ sax, wóolu ko. Nit bañ na la, te di la fóon lu bare.
7 Ku suur, bañ lem ju xelli, waaye boo xiifee, lu wex lu ne neex la.
8 Ku sore fa nga bokk, dangay mel ni picc mu sore tàggam.
9 Diwook suuru day naatal xol; waaye li neex cib xarit, xol la lay digale.
10 Bul fàtte sab xarit mbaa sa xaritu baay, bul jàq ba seeti sa mbokk; dëkkandoo bu jegee gën mbokk mu sore.
11 Muusal, doom, ma bég, ba mana tontu ku ma sikk.
12 Kuy foog, gisu ay, làqu; ab téxét ne ca tëñëx, loru.
13 Ku gàddul jaambur bor, jëlal mbubbam; tayle ko, moo dige feyal ndaw su yemadi.
14 Nuyoo bu xumb, suba teel mooki saagaa yem.
15 Jabar ju pànk mooy senn bu dakkul, cib taw;
16 ku ko mana yemale, mana téye ngelaw mbaa nga ŋëb ag diw.
17 Weñ ay nàmm weñ, nit ay nàmm xelu moroom ma.
18 Ku aar garab, lekk ca doom ya; ku topptoo sa sang, am ngërëm.
19 Ku xool cim ndox, gis sa kanam, nga xool sab xol, gis sa jikko.
20 Njaniiw ak biir suuf du fees, bët it du doylu mukk.
21 Xaalis ak wurus sawaraa koy xelli, waaye àtteb nit ca jëëm.
Kàddu yu Xelu 27 in Kàddug Yàlla gi