3 Xiir, aw fas; laab, mbaam; yetu gannaaw, ab dof.
4 Bul topp ab dof cig ndofam, lu ko moy nga mel ni moom.
5 Waaye toppal ab dof cig ndofam, lu ko moy mu defe ne daa muus.
6 Ku yóbbante ab dof kàddu, yaa woo fitna, gor say tànk.
7 Kàddu gu xelu ci gémmiñug dof, mooy tànki lafañ, amalu ko njariñ.
8 Kuy teral ab dof, jël ngaw doj, takk ko ci mbaq.
9 Kàddu gu xelu ci gémmiñug dof mooy car aki dégam, màndikat xàcci.