Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 26:12-27 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 26:12-27 in Kàddug Yàlla gi

12 Ana koo gis mu ne: «Maa xelu»? Kooku ab dof a ko gën demin.
13 Ab yaafus da naan: «Gayndee ngi ci yoon wi! Gayndee ngi ci mbedd mi!»
14 Ab yaafus day tëdd ak a walbatiku, mooy bunt, day jaayu, demul fenn.
15 Ab yaafus day yeb loxoom ci ndab, waaye yékkati ko, sex, da koy sonal.
16 Ab yaafus day foog ne moo gëna muus juróom ñaari boroom xel yu xam tont.
17 Kuy xuloo lu sa yoon newul, yaa jàpp ci noppi xaj buy romb.
18 Nit kuy naxe, naan: «Damay fo!» yaay dof buy sànniy jum, di fitteek a reye.
20 Bu matt amul, ab taal fey, fu soskat amul it, xuloo jeex fa.
21 Këriñ defi xal, matt xamb ub taal, ab xulookat di xambu ay.
22 Waxi jëwkat di ñam wu neex, wuy seey, jàll ca biir-a-biir.
23 Kuy wax lu neex, tey mébét lu bon, yaay xaalis bu rax, ñu xoob ca ndabal xandeer.
24 Ab noon làqoo na ay waxam, lal pexey wor ca xolam.
25 Buy wax lu neex, bul gëm, ñaawtéef la xol ba fees dell.
26 Su la nëbbalee mbañeel, di la nax it, ag mbonam mujj bir ñépp.
27 Ku gasal nit am yeer, yaa cay daanu; ku béraŋu doj, ngir tance, yaay tancu.
Kàddu yu Xelu 26 in Kàddug Yàlla gi