Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 26:11-18 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 26:11-18 in Kàddug Yàlla gi

11 Dof day def jëfi dof, dellu ca, mooy xaj, bu waccoo, lekkaat ko.
12 Ana koo gis mu ne: «Maa xelu»? Kooku ab dof a ko gën demin.
13 Ab yaafus da naan: «Gayndee ngi ci yoon wi! Gayndee ngi ci mbedd mi!»
14 Ab yaafus day tëdd ak a walbatiku, mooy bunt, day jaayu, demul fenn.
15 Ab yaafus day yeb loxoom ci ndab, waaye yékkati ko, sex, da koy sonal.
16 Ab yaafus day foog ne moo gëna muus juróom ñaari boroom xel yu xam tont.
17 Kuy xuloo lu sa yoon newul, yaa jàpp ci noppi xaj buy romb.
18 Nit kuy naxe, naan: «Damay fo!» yaay dof buy sànniy jum, di fitteek a reye.
Kàddu yu Xelu 26 in Kàddug Yàlla gi