Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 24:21-25 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 24:21-25 in Kàddug Yàlla gi

21 Doom, ragalal Aji Sax ji, wormaal buur. Bul lëngook kuy fippu.
22 Yàllaak buur a koy bette mbugal, te kenn xamul musiba mu muy doon.
23 Lii it ñi rafet xel a ko wax. Par-parloo cib àtte baaxul.
24 Ku ne defkatu lu bon: «Yaw, tooñoo,» aw nit móolu la, mbooloo ŋàññ la;
25 ku ko ne: «Yaa tooñ,» yaay baaxle, taasoo barke bu yaa.
Kàddu yu Xelu 24 in Kàddug Yàlla gi