Text copied!
CopyCompare
- Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 22

Kàddu yu Xelu 22:5-12

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Yoonu njublaŋ, ay dég aki fiir; ku sàmm sa bakkan sore ko.
6Tegal gone ciw yoon, ba bu màggee, du ko wacc.
7Ku am ay yilif ku ñàkk, koo leb di surgaam.
8Ku ji njubadi, góob fitna, yet wa muy dóore, damm.
9Ku tabe am barke, mooy kiy sédd ku ñàkk cib dundam.
10Dàqal kuy ñaawle, ay jeex, xulooki saaga dakk.
11Ku dëggu, wax ja yiw, buur di xaritam.
12Aji Sax jeey sàmm liy dëgg, di weddi waxi fen-kat.

Read Kàddu yu Xelu 22Kàddu yu Xelu 22
Compare Kàddu yu Xelu 22:5-12Kàddu yu Xelu 22:5-12