Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 20:23-28 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 20:23-28 in Kàddug Yàlla gi

23 Aji Sax ji bañ na nattu diisaay yu wuute, njublaŋ ci natti diisaay baaxul.
24 Jéegoy jaam Aji Sax jee ko yor, kenn xamul foo jëm.
25 Bul gaawtuy digeek Yàlla, di dugal sa bopp; bul giñ, di réccu.
26 Buur, bu xeloo, ràññee ku bon, mbugal ko, te du ko ñéeblu.
27 Xelum nit làmp la bu Aji Sax ji taal, da koy niital ba ca biir xolam.
28 Ngor ak worma day aar buur, ngor ay saxal ab jalam.
Kàddu yu Xelu 20 in Kàddug Yàlla gi